1
Peeñu ma 21:4
Téereb Injiil
TI
Dina fomp bépp rongooñ ci seeni bët; te dee dootul am walla naqar walla jooy walla metit, ndaxte yëf yu jëkk ya wéy nañu.»
Compare
Explore Peeñu ma 21:4
2
Peeñu ma 21:5
Noonu ki toog ca gàngune ma ne: «Maa ngi yeesal lépp!» Mu ne ma: «Bindal, ndaxte kàddu yii yu wóor lañu te dëggu.»
Explore Peeñu ma 21:5
3
Peeñu ma 21:3
Ma dégg baat bu xumb jibe ca gàngune ma naan: «Dalub Yàllaa ngi ci biir nit ñi. Dina dëkk ak ñoom, nit ñi dinañu nekk ay gaayam, te moom Yàlla ci boppam dina ànd ak ñoom, nekk Yàlla seen Boroom.
Explore Peeñu ma 21:3
4
Peeñu ma 21:6
Mu teg ca ne ma: «Lépp mat na! Maay Alfa di Omega, di njàlbéen gi, di muj gi. Ku mar, dinaa la may ci bëtu ndoxum dund mi, te doo fey dara.
Explore Peeñu ma 21:6
5
Peeñu ma 21:7
Ku daan, dinga am cér ci mbir yii. Dinaa nekk Yàlla sa Boroom, te dinga nekk doom ci man.
Explore Peeñu ma 21:7
6
Peeñu ma 21:8
Waaye ñi ragal ak ñi gëmul ak ñiy def lu ñaaw ak ñiy bóome ak ñiy njaaloo ak luxuskat yi ak xërëmkat yi ak fenkat yépp, seen añ moo di déegu sawara bi ànd ak tamarax. Loolu mooy ñaareelu dee gi.»
Explore Peeñu ma 21:8
7
Peeñu ma 21:1
Noonu ma gis asamaan su bees ak suuf su bees, ndaxte asamaan su jëkk sa ak suuf su jëkk sa wéyoon nañu, te géej gi amatul.
Explore Peeñu ma 21:1
8
Peeñu ma 21:2
Ma gis, wàcce ca asamaan, jóge ca wetu Yàlla, Yerusalem gu bees gi, dëkk bu sell, bi ñu waajal ba mu jekk ni séet buy nég jëkkëram.
Explore Peeñu ma 21:2
9
Peeñu ma 21:23-24
Dëkk ba soxlawul jant walla weer ngir leeral ko, ndaxte ndamu Yàlla moo koy leeral, te Gàtt ba moo nekk làmpam. Xeeti àddina dinañu dox cig leeram, te buuri àddina dinañu ca indi seen ndam.
Explore Peeñu ma 21:23-24