1
Peeñu ma 20:15
Téereb Injiil
TI
Képp ku ñu bindul sa tur ci téereb dund bi, dees na la sànni ci déegu sawara si.
Compare
Explore Peeñu ma 20:15
2
Peeñu ma 20:12
Ma gis néew ya, mag ak ndaw, ñu taxaw ca kanam gàngune ma. Ñu daldi ubbi ay téere, ubbi itam beneen téere, téereb dund bi. Ñu àtte néew ya, ku nekk ci say jëf, ni ñu ko binde woon ca téere ya.
Explore Peeñu ma 20:12
3
Peeñu ma 20:13-14
Noonu géej gëq néew, yi nekkoon ci moom; dee ak barsàq delloo néew, ya ñu yoroon. Ñu àtte ñépp ci seeni jëf. Ñu jàpp dee ak barsàq, sànni ca déegu sawara sa. Déegu sawara soosu moo di ñaareelu dee.
Explore Peeñu ma 20:13-14
4
Peeñu ma 20:11
Noonu ma gis gàngune mu mag te weex, ak ka ca toog. Asamaan ak suuf daw, sore ko, ba ne mes.
Explore Peeñu ma 20:11
5
Peeñu ma 20:7-8
Bu junniy at ya matee, dinañu yiwi Seytaane ca kasoom, te dina dem naxi xeet yi ci ñeenti xéblay àddina, maanaam ñoom Gog ak Magog. Dina leen dajale ngir xare, te dinañu bare ni peppi suuf cig tefes.
Explore Peeñu ma 20:7-8