1
Peeñu ma 19:7
Téereb Injiil
TI
Nanu bég te bànneexu te jox ko ndam li, ndaxte céetu Gàtt bi agsi na, séet bi waaj na!
Compare
Explore Peeñu ma 19:7
2
Peeñu ma 19:16
Ci mbubbam ak ci poojam bind nañu ci tur wii: Buuru buur yi, Kilifag kilifa yi.
Explore Peeñu ma 19:16
3
Peeñu ma 19:11
Bi loolu wéyee ma gis asamaan ubbiku. Noonu fas wu weex feeñ. Ki ko war ma nga tudd Ku Takku te Dëggu, te ci njub lay àtte ak a xare.
Explore Peeñu ma 19:11
4
Peeñu ma 19:12-13
Ay bëtam di xuyy ni sawara, te mu am mbaxanay buur yu bare ca boppam. Bind nañu ci moom tur wu kenn xamul ku dul moom. Sol na mbubb mu ñu sóob ci deret, te Kàddug Yàlla mooy turam.
Explore Peeñu ma 19:12-13
5
Peeñu ma 19:15
Am na jaasi ju ñaw juy génn ci gémmiñam, ngir dóor xeet yi, mu di leen jiitee yetu weñ, te mooy nappaaje reseñ yi ci segalukaayu mer mu tàng mu Yàlla Aji Man ji.
Explore Peeñu ma 19:15
6
Peeñu ma 19:20
Ñu jàpp rab wa, moom ak naaféq ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay kéemaan yu mu naxe ñi nangu woona am màndargam rab wa te jaamu nataalam. Ñoom ñaar ñépp sànni nañu leen ñuy dund ca déegu sawara ak tamarax buy tàkk.
Explore Peeñu ma 19:20