1
Peeñu ma 2:4
Téereb Injiil
TI
Waaye li ma naqari ci yaw moo di sa mbëggeel wàññiku na.
Compare
Explore Peeñu ma 2:4
2
Peeñu ma 2:5
Deel fàttaliku kon fa nga daanoo. Réccul te def, na nga daan def bu jëkk. Soo réccuwul, dinaa dikk ci yaw, jële sa tegukaayu làmp ca bérab ba mu nekk.
Explore Peeñu ma 2:5
3
Peeñu ma 2:10
Bul ragal li nga nara daj. Seytaane dina dugal kaso ñenn ci yéen, ngir wut leena fiir. Diirub fukki fan dingeen am coono. Nanga takku ba àttan cee dee, ma jox la kaalag dund gi.
Explore Peeñu ma 2:10
4
Peeñu ma 2:7
Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la may, nga lekk ci garabu dund, gi nekk ci jataayu Yàlla.
Explore Peeñu ma 2:7
5
Peeñu ma 2:2
Xam naa say jëf, sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne manuloo dékku ñiy def lu bon. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay naaféq lañu.
Explore Peeñu ma 2:2
6
Peeñu ma 2:3
Xam naa it ne muñ nga, ba dékku coono ndax sama tur, te xàddiwoo.
Explore Peeñu ma 2:3
7
Peeñu ma 2:17
Yaw mi am ay nopp, déglul li Xelum Yàlla di wax mboolooy ñi gëm. Ku daan, dinaa la jox, nga lekk dund bi ñuy wax mànn te mu nëbbu, te dinaa la jox xeer wu weex. Ci kaw xeer woowu bindees na ci tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ki ko jot.
Explore Peeñu ma 2:17