1
Peeñu ma 3:20
Téereb Injiil
TI
Maa ngi nii taxaw ci bunt bi, di fëgg. Ku dégg sama baat te ubbi bunt bi, dinaa dugg, reerandoo ak moom, moom it mu reerandoo ak man.
Compare
Explore Peeñu ma 3:20
2
Peeñu ma 3:15-16
Xam naa say jëf, xam ne seddoo, tàngoo. Manoon ngaa sedd mbaa nga tàng, waaye ndax li nga nugg, tàngoo seddoo, dinaa la yàbbi.
Explore Peeñu ma 3:15-16
3
Peeñu ma 3:19
Man maay yedd, di yar ñépp ñi ma bëgg. Farlul kon te tuub say bàkkaar.
Explore Peeñu ma 3:19
4
Peeñu ma 3:8
Xam naa say jëf. Ubbil naa la bunt, te kenn du ko mana tëj. Xam naa ne barewuloo doole, waaye sàmm nga sama kàddu te weddiwoo ma.
Explore Peeñu ma 3:8
5
Peeñu ma 3:21
Ku daan, dinaa la toogloo ci sama wet ci sama gàngune, ni ma xeexe ba daan, man ci sama bopp, te toogandoo ak sama Baay ci gànguneem.
Explore Peeñu ma 3:21
6
Peeñu ma 3:17
Yaa ngi damu naan: “Am naa alal, duunle naa, soxlaatuma dara.” Fekk xamuloo ne torox nga, miskin, ñàkk, gumba te rafle.
Explore Peeñu ma 3:17
7
Peeñu ma 3:10
Gannaaw muñ nga, ni ma la ko dénke woon, man itam dinaa la yiir ci jamono, ji musiba mi di wàcc ci dunyaa bépp ngir nattu waa àddina.
Explore Peeñu ma 3:10
8
Peeñu ma 3:11
Léegi ma ñëw. Sàmmal li nga yor, ngir kenn bañ laa xañ sa kaalag ndam.
Explore Peeñu ma 3:11
9
Peeñu ma 3:2
Yewwul te dëgëral li des ci yaw tey waaja dee, ndaxte gis naa ne say jëf matuñu ca sama kanam Yàlla.
Explore Peeñu ma 3:2