Noonu mu nax waa àddina ci kéemaan, yi mu am sañ-sañu def ci turu rab wu jëkk wa. Mu sant waa àddina, ñu def nataalu rab, wi am gaañu-gaañub jaasi tey dund. Mayees ko it, mu dundloo nataalu rab wa, waxloo ko, ba képp ku jaamuwul nataalu rab wa rekk ñu rey la.