1
Màrk 9:23
Téereb Injiil
TI
Yeesu ne ko: «Nga ne: “Soo ko manee,” ku gëm man na lépp.»
Compare
Explore Màrk 9:23
2
Màrk 9:24
Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.»
Explore Màrk 9:24
3
Màrk 9:28-29
Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax manunu ko woona dàq?» Yeesu ne leen: «Yu mel ni yii, ñaan ci Yàlla rekk a leen di dàq.»
Explore Màrk 9:28-29
4
Màrk 9:50
Xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen jàmmoo.»
Explore Màrk 9:50
5
Màrk 9:37
«Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.»
Explore Màrk 9:37
6
Màrk 9:41
Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yéena ngi bokk ci man Kirist, kooku du ñàkk yoolam mukk.
Explore Màrk 9:41
7
Màrk 9:42
«Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom, moo di ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej.
Explore Màrk 9:42
8
Màrk 9:47
Te bu la sa bët di yóbbe bàkkaar, luqi ko. Nga patt te dugg ci nguuru Yàlla, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, ñu sànni la ci sawara.
Explore Màrk 9:47