1
Màrk 8:35
Téereb Injiil
TI
Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man ak ngir xibaaru jàmm bi, dinga ko jotaat.
Compare
Explore Màrk 8:35
2
Màrk 8:36
Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam?
Explore Màrk 8:36
3
Màrk 8:34
Noonu Yeesu woo taalibe yi ak mbooloo mi ne leen: «Ku bëgga topp ci samay tànk, na bàyyi boppam te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
Explore Màrk 8:34
4
Màrk 8:37-38
Te nit, lu mu wara weccee bakkanam? Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax ci kanam niti jamono jii, ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla te topp bàkkaar, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamu Baayam, ànd ak malaaka yu sell yi.»
Explore Màrk 8:37-38
5
Màrk 8:29
Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.»
Explore Màrk 8:29