1
Màrk 10:45
Téereb Injiil
TI
Ndaxte noonu la Doomu nit ki ñëwe sax, du ngir ñu nekk ay surgaam, waaye ngir muy seen surga, ba joxe bakkanam ngir njotug ñu bare.»
Compare
Explore Màrk 10:45
2
Màrk 10:27
Noonu Yeesu xool leen naan: «Loolu të na nit, waaye tëwul Yàlla; Yàlla man na lépp.»
Explore Màrk 10:27
3
Màrk 10:52
Noonu Yeesu ne ko: «Demal ci jàmm. Sa ngëm faj na la.» Ci saa si gumba gi gis, daldi topp Yeesu ci yoon wi.
Explore Màrk 10:52
4
Màrk 10:9
Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
Explore Màrk 10:9
5
Màrk 10:21
Noonu Yeesu xool ko, am cofeel ci moom, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Demal jaay li nga am, jox ko miskin yi, te dinga woomle ci asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.»
Explore Màrk 10:21
6
Màrk 10:51
Yeesu ne ko: «Loo bëggoon ma defal la ko?» Gumba gi ne ko: «Kilifa gi, damaa bëgga gis.»
Explore Màrk 10:51
7
Màrk 10:43
Buleen mel ni ñooñu. Waaye ku bëgga nekk kilifa ci yéen, na nekk seen surga
Explore Màrk 10:43
8
Màrk 10:15
Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku woyoful ni xale, nangu nguuru Yàlla, doo ci mana dugg.»
Explore Màrk 10:15
9
Màrk 10:31
Waaye ñu bare ci ñi jiitu ñooy mujji; ñi mujj ñooy jiituji.»
Explore Màrk 10:31
10
Màrk 10:6-8
Waaye ca njàlbéen ga “Yàlla sàkk na leen, kii góor, kii jigéen. Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.” Kon nekkatuñu ñaar waaye benn lañu.
Explore Màrk 10:6-8