1
Macë 26:41
Téereb Injiil
TI
Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.»
Compare
Explore Macë 26:41
2
Macë 26:38
Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba may bëgga dee; toogleen fi, xool ak man.»
Explore Macë 26:38
3
Macë 26:39
Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.»
Explore Macë 26:39
4
Macë 26:28
ndaxte lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi.
Explore Macë 26:28
5
Macë 26:26
Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.»
Explore Macë 26:26
6
Macë 26:27
Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci
Explore Macë 26:27
7
Macë 26:40
Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
Explore Macë 26:40
8
Macë 26:29
Maa ngi leen di wax, dootuma naan gannaaw-si-tey ndoxum reseñ mii, ba kera may naan ak yéen ndoxum reseñ mu bees ci sama nguuru Baay.»
Explore Macë 26:29
9
Macë 26:75
Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti.
Explore Macë 26:75
10
Macë 26:46
Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
Explore Macë 26:46
11
Macë 26:52
Waaye Yeesu ne ko: «Roofal sa jaasi ci mbaram, ndaxte ku bocci jaasi, jaasi moo lay rey.
Explore Macë 26:52