1
Macë 27:46
Téereb Injiil
TI
Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
Compare
Explore Macë 27:46
2
Macë 27:51-52
Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yëngu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku, te ñu bare ci jëmmi nit ñu sell ñu dee, dekki.
Explore Macë 27:51-52
3
Macë 27:50
Noonu Yeesu wootewaat ak kàddu gu dëgër, delloo ruuwam Yàlla.
Explore Macë 27:50
4
Macë 27:54
Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yëngu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.»
Explore Macë 27:54
5
Macë 27:45
La tàmbalee digg bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm.
Explore Macë 27:45
6
Macë 27:22-23
Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!»
Explore Macë 27:22-23