1
Macë 19:26
Téereb Injiil
TI
Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.»
Compare
Explore Macë 19:26
2
Macë 19:6
Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.»
Explore Macë 19:6
3
Macë 19:4-5
Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen, te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.”
Explore Macë 19:4-5
4
Macë 19:14
Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
Explore Macë 19:14
5
Macë 19:30
Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji.
Explore Macë 19:30
6
Macë 19:29
Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex.
Explore Macë 19:29
7
Macë 19:21
Noonu Yeesu ne ko: «Boo bëggee mat sëkk, demal jaay li nga am, jox ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan. Boo noppee, ñëwal topp ci man.»
Explore Macë 19:21
8
Macë 19:17
Yeesu ne ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.»
Explore Macë 19:17
9
Macë 19:24
Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
Explore Macë 19:24
10
Macë 19:9
Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa soxna te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.»
Explore Macë 19:9
11
Macë 19:23
Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
Explore Macë 19:23