1
Macë 10:16
Téereb Injiil
TI
«Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax.
Compare
Explore Macë 10:16
2
Macë 10:39
Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko.
Explore Macë 10:39
3
Macë 10:28
Te buleen ragal ñu mana rey yaram, te manuñoo rey ruu, waaye ragal-leen ki mana sànk yaram ak ruu ci sawara.
Explore Macë 10:28
4
Macë 10:38
Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma.
Explore Macë 10:38
5
Macë 10:32-33
«Koo xam ne nangu nga ma ci kanam nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw. Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw.
Explore Macë 10:32-33
6
Macë 10:8
Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen.
Explore Macë 10:8
7
Macë 10:31
Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu.
Explore Macë 10:31
8
Macë 10:34
«Te it buleen defe ne damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale.
Explore Macë 10:34