1
Luug 3:21-22
Téereb Injiil
TI
Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku. Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
Compare
Explore Luug 3:21-22
2
Luug 3:16
Noonu Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.
Explore Luug 3:16
3
Luug 3:8
Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
Explore Luug 3:8
4
Luug 3:9
Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.»
Explore Luug 3:9
5
Luug 3:4-6
Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar. Nañu sëkk xur yi, maasale tund yi ak jànj yi. Yoon yi dëng ñu jubbanti leen, yi ñagas ñu rataxal leen. Bu ko defee bépp mbindeef dina gis mucc gi Yàlla tëral.”»
Explore Luug 3:4-6