1
Luug 2:11
Téereb Injiil
TI
Tey jii ca dëkku Daawuda, ab Musalkat juddul na leen fa, te mooy Almasi bi, di Boroom bi.
Compare
Explore Luug 2:11
2
Luug 2:10
Waaye malaaka mi ne leen: «Buleen tiit, ndaxte dama leen di xamal xibaaru jàmm buy indi mbég mu réy ci nit ñépp.
Explore Luug 2:10
3
Luug 2:14
«Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa, te ci àddina, na jàmm wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!»
Explore Luug 2:14
4
Luug 2:52
Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi.
Explore Luug 2:52
5
Luug 2:12
Ci firnde jii ngeen koy xàmmee: dingeen gis liir bu ñu laxas ci ay laytaay, tëral ko ci lekkukaayu jur.»
Explore Luug 2:12
6
Luug 2:8-9
Fekk booba amoon na ca gox ba ay sàmm yu daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga. Noonu benn malaakam Boroom bi feeñu leen, ndamu Boroom bi daldi leer, melax, wër leen. Tiitaange ju réy jàpp leen.
Explore Luug 2:8-9