1
Luug 17:19
Téereb Injiil
TI
Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.»
Compare
Explore Luug 17:19
2
Luug 17:4
Te su la tooñee juróom ñaari yoon ci bés bi, te ñëw ci yaw juróom ñaari yoon ne la: “Tuub naa ko,” nanga ko baal.»
Explore Luug 17:4
3
Luug 17:15-16
Kenn ci ñoom gis ne wér na, daldi dëpp, di màggal Yàlla ak baat bu xumb. Mu dëpp jëëm ca tànki Yeesu, di ko gërëm. Fekk nitu Samari la woon.
Explore Luug 17:15-16
4
Luug 17:3
Wottuleen seen bopp. «Bu sa mbokk tooñee, yedd ko. Bu réccoo, baal ko.
Explore Luug 17:3
5
Luug 17:17
Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom ñeent ña nag?
Explore Luug 17:17
6
Luug 17:6
Boroom bi ne leen: «Su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen mana ne garab gii: “Buddeekul, dem jëmbëtu ca géej ga,” te dina def li ngeen wax.
Explore Luug 17:6
7
Luug 17:33
Kuy wuta rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ko ñàkk, dinga dund.
Explore Luug 17:33
8
Luug 17:1-2
Yeesu waxaat ay taalibeem ne leen: «Fiir yuy yóbbe nit bàkkaar manta ñàkk, waaye toroxte dal na ki koy lal. Ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej moo gën ci moom muy daaneel ci bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ci ñii.
Explore Luug 17:1-2
9
Luug 17:26-27
«La xewoon ca bési Nóoyin, dina xewaat ci bési Doomu nit ki. Nit ñaa ngi doon lekk ak di naan, di jël jabar ak a séyi, ba bés ba Nóoyin duggee ca gaal ga. Noonu mbënn ma ñëw, rey leen ñoom ñépp.
Explore Luug 17:26-27