1
Luug 16:10
Téereb Injiil
TI
Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare.
Compare
Explore Luug 16:10
2
Luug 16:13
«Benn jaam manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.»
Explore Luug 16:13
3
Luug 16:11-12
Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji? Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?
Explore Luug 16:11-12
4
Luug 16:31
Waaye Ibraayma ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»
Explore Luug 16:31
5
Luug 16:18
«Ku fase sa soxna, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga.
Explore Luug 16:18