1
Luug 10:19
Téereb Injiil
TI
Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ.
Compare
Explore Luug 10:19
2
Luug 10:41-42
Boroom bi ne ko: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu. Moona de, lenn rekk a am solo. Maryaama dafa tànn cér bi gën, te kenn du ko nangu ci moom.»
Explore Luug 10:41-42
3
Luug 10:27
Nit ka ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»
Explore Luug 10:27
4
Luug 10:2
Mu ne leen: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.
Explore Luug 10:2
5
Luug 10:36-37
Yeesu teg ca ne: «Lu ciy sa xalaat? Kan ci ñett ñooñu moo jëfe ni kuy jëf jëme ci moroomam, ba ñu gisee nit, ka sàcc ya dogale woon?» Xutbakat ba ne ko: «Xanaa ki ko won yërmandeem.» Yeesu ne ko nag: «Demal tey def ni moom.»
Explore Luug 10:36-37
6
Luug 10:3
Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki.
Explore Luug 10:3