1
Luug 9:23
Téereb Injiil
TI
Noonu Yeesu ne leen ñoom ñépp: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, gàddu bés bu nekk bant, bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man.
Compare
Explore Luug 9:23
2
Luug 9:24
Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, dinga ko jotaat.
Explore Luug 9:24
3
Luug 9:62
Yeesu ne ko: «Kuy ji, di geestu, yeyoowula liggéey ci nguuru Yàlla.»
Explore Luug 9:62
4
Luug 9:25
Ndaxte moom àddina sépp, lu muy jariñ nit, su fekkee ne dafay ñàkk bakkanam walla mu loru?
Explore Luug 9:25
5
Luug 9:26
Ku ma rusa faral, te nanguwul samay wax, Doomu nit ki dina la rusa xam, bés bu ñëwee ci ndamam ak ci ndamu Baay bi ak lu malaaka yu sell yi.
Explore Luug 9:26
6
Luug 9:58
Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
Explore Luug 9:58
7
Luug 9:48
«Ku nangu xale bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, nangu nga ki ma yónni; ndaxte ki gëna woyof ci yéen ñépp, kooku moo gëna màgg.»
Explore Luug 9:48