1
Yowaan 4:24
Téereb Injiil
TI
Yàlla xel la, kon ñi koy jaamu war nañu koo jaamu ci xel ak ci dëgg.»
Compare
Explore Yowaan 4:24
2
Yowaan 4:23
Waaye jamono dina ñëw, te agsi na ba noppi, jamono joo xam ne jaamukat yi dëgg dinañu jaamu Baay bi ci xel ak ci dëgg. Ñooñu nag, ñooy jaamu Baay bi, ni mu ko bëgge.
Explore Yowaan 4:23
3
Yowaan 4:14
waaye ndox mi may joxe, ku ci naan du marati mukk, ndaxte day nekk ci moom bëtu ndox buy ball, di joxe dund gu dul jeex.»
Explore Yowaan 4:14
4
Yowaan 4:10
Noonu nag Yeesu ne ko: «Soo xamoon li Yàlla maye, xam ki lay ñaan ndox, kon yaw ci sa bopp, yaa koy ñaan, te moom dina la may ndoxum dund.»
Explore Yowaan 4:10
5
Yowaan 4:34
Yeesu ne leen: «Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu ma sant.
Explore Yowaan 4:34
6
Yowaan 4:11
Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund?
Explore Yowaan 4:11
7
Yowaan 4:25-26
Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi --maanaam Kirist-- dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.» Yeesu ne ko: «Maa di Almasi bi, man miy wax ak yaw.»
Explore Yowaan 4:25-26
8
Yowaan 4:29
«Kaayleen gis; nit a nga fee ku ma wax lépp lu ma masa def. Ndax kooku du Almasi bi?»
Explore Yowaan 4:29