1
Yowaan 19:30
Téereb Injiil
TI
Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: «Lépp mat na!» Noonu mu sëgg, delloo ruuwam Yàlla.
Compare
Explore Yowaan 19:30
2
Yowaan 19:28
Bi loolu wéyee, gannaaw Yeesu xam na ne lépp mat na léegi, mu ne nag, ngir amal Mbind mi: «Damaa mar.»
Explore Yowaan 19:28
3
Yowaan 19:26-27
Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,» neeti taalibe ba: «Sa yaay a ngi nii.» Booba la ko taalibe ba yóbbu këram, yor ko.
Explore Yowaan 19:26-27
4
Yowaan 19:33-34
Bi ñu agsee ci Yeesu, dammuñu ay tànkam, ndaxte gis nañu ne booba faatu na. Waaye kenn ca xarekat ya daldi jël xeej, jam ko ko ci wet, ca saa sa deret ak ndox di tuuru.
Explore Yowaan 19:33-34
5
Yowaan 19:36-37
ndaxte loolu dafa xew ngir Mbind mi am: «Benn yaxam du damm.» Leneen it Mbind mi wax na ko: «Dinañu gis ki ñu jamoon.»
Explore Yowaan 19:36-37
6
Yowaan 19:17
Yeesu ci boppam gàddu bant ba, génn ngir dem ca fa ñuy wax bérabu Kaaŋu bopp; ñu koy wooye Golgota ci làkku yawut.
Explore Yowaan 19:17
7
Yowaan 19:2
Xarekat ya ràbb kaalag dég, teg ko ci boppu Yeesu, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr.
Explore Yowaan 19:2