1
Yowaan 14:27
Téereb Injiil
TI
Jàmm laa leen bàyyeel, sama jàmm laa leen jox, jàmm ju àddina manula joxe. Buleen jàq, buleen tiit.
Compare
Explore Yowaan 14:27
2
Yowaan 14:6
Yeesu ne ko: «Man maay yoon wi, maay dëgg te dund it man la. Kenn du ñëw ci Baay bi te jaarul ci man.
Explore Yowaan 14:6
3
Yowaan 14:1
«Buleen jàq. Gëmleen Yàlla te gëm ma.
Explore Yowaan 14:1
4
Yowaan 14:26
Waaye Dimbalikat, bi leen Baay bi di yónnee ci sama tur, muy Xelam mu Sell, dina leen jàngal lépp, di leen fàttali li ma leen waxoon lépp.
Explore Yowaan 14:26
5
Yowaan 14:21
Ki ma bëgg, mooy kiy nangu samay ndigal te di ko topp. Ku ma bëgg, Baay bi bëgg la, te man dinaa la bëgg, di la feeñu.»
Explore Yowaan 14:21
6
Yowaan 14:16-17
Te dinaa ñaan Baay bi, mu jox leen beneen Dimbalikat, buy nekk ak yéen ba abadan. Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dëgg. Àddina du ko mana nangu, ndaxte gisu ko te xamu ko. Yéen xam ngeen ko, ndaxte mi ngi dëkk ak yéen te dina nekk ci yéen.
Explore Yowaan 14:16-17
7
Yowaan 14:13-14
Te it lu ngeen ñaan ci sama tur dinaa ko def, ngir Doom ji feeñal ndamu Baay bi. Lu ngeen ñaan ci sama tur, maa koy def.
Explore Yowaan 14:13-14
8
Yowaan 14:15
«Bu ngeen ma bëggee, dingeen topp sama ndigal.
Explore Yowaan 14:15
9
Yowaan 14:2
Am na néeg yu bare ca sama kër Baay, bu dul woon noonu, ma wax leen ko, ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di dëkk.
Explore Yowaan 14:2
10
Yowaan 14:3
Te su ma leen defaralee bérab booba ba noppi, dinaa délsi, yóbbaale leen, ba fu ma nekk, ngeen nekk fa, yéen itam.
Explore Yowaan 14:3
11
Yowaan 14:5
Tomaa ne ko: «Boroom bi, xamunu fa nga jëm. Kon nan lanuy mana xame yoon wi?»
Explore Yowaan 14:5