1
Yowaan 13:34-35
Téereb Injiil
TI
Maa ngi leen di jox ndigal lu bees: bëgganteleen. Nangeen di bëggante ni ma leen bëgge. Ni ñuy xame ne samay taalibe ngeen, mooy ngeen bëggante.»
Compare
Explore Yowaan 13:34-35
2
Yowaan 13:14-15
Kon bu fekkee ne man miy Boroom bi tey Kilifa gi, maa leen raxasal seeni tànk, yéen itam war ngeen di raxasalante seeni tànk. Bàyyil naa leen fi royukaay, ngir ngeen di jëf, nii ma jëfeek yéen.
Explore Yowaan 13:14-15
3
Yowaan 13:7
Yeesu ne ko: «Xamoo fii mu nekk li may def, waaye dinga ko xami.»
Explore Yowaan 13:7
4
Yowaan 13:16
Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, jaam gënula màgg sangam, mbaa ndaw, ki ko yónni.
Explore Yowaan 13:16
5
Yowaan 13:17
Gannaaw xam ngeen loolu, bu ngeen doxalee noonu, dingeen bég.
Explore Yowaan 13:17
6
Yowaan 13:4-5
Mu daldi jóge ca reer ba, summi mbubbam, daldi jël ab sarbet, laxas ko ci ndiggam. Noonu mu sotti ndox ci ab këll, daldi tàmbali di raxas tànki taalibe ya, di leen fomp ak sarbet, ba mu laxasaayoo.
Explore Yowaan 13:4-5