1
Yowaan 15:5
Téereb Injiil
TI
«Man maay garab gi; yéen yéenay car yi. Ki sax ci man te ma sax ci moom, dina meññ, ndaxte bu ngeen saxul ci man, dungeen man dara.
Compare
Explore Yowaan 15:5
2
Yowaan 15:4
Saxleen ci man; ma sax, man itam, ci yéen. Ni car manula ame ay doom, bu saxul ci garab, noonu itam dungeen mana meññ li may jëfe ci yéen, bu ngeen saxul ci man.
Explore Yowaan 15:4
3
Yowaan 15:7
Bu ngeen saxee ci man te saxal samay wax ci seen xol, lu ngeen ñaan mu nangu.
Explore Yowaan 15:7
4
Yowaan 15:16
Du yéen yéena ma tànn, waaye man maa leen tànn, sas leen ngeen dem, meññ meññeef gu sax, ngir Baay bi def lu ngeen ko ñaan ci sama tur.
Explore Yowaan 15:16
5
Yowaan 15:13
Genn mbëggeel manula weesu joxe sa bakkan ngir say xarit.
Explore Yowaan 15:13
6
Yowaan 15:2
Car bu soqikoo ci man te meññul, dina ko dog, sànni. Waaye car bu ci meññ, dina ko tenqi, ngir mu gëna meññ.
Explore Yowaan 15:2
7
Yowaan 15:12
Sama ndigal mooy ngeen bëggante, ni ma leen bëgge.
Explore Yowaan 15:12
8
Yowaan 15:8
Liy feeñal sama ndamu Baay moo di, ngeen di gëna meññ tey wone noonu ne samay taalibe ngeen.
Explore Yowaan 15:8
9
Yowaan 15:1
«Man maay garab gu wóor gi, te sama Baay mooy beykat bi.
Explore Yowaan 15:1
10
Yowaan 15:6
Ku saxul ci man dinañu ko sànni ci biti, mu mel ni car bu ñu dagg, ba mu wow. Car yu wow nag, dañu leen di buub, sànni ci sawara, ñu lakk.
Explore Yowaan 15:6
11
Yowaan 15:11
Wax naa leen loolu, ngir ngeen bokk ci sama mbég, te seen bos mat sëkk.
Explore Yowaan 15:11
12
Yowaan 15:10
Bu ngeen toppee samay ndigal, dingeen sax ci sama mbëggeel, ni ma toppe sama ndigali Baay, ba tax ma sax ci mbëggeelam.
Explore Yowaan 15:10
13
Yowaan 15:17
Li may santaane nag, mooy ngeen bëggante.
Explore Yowaan 15:17
14
Yowaan 15:19
Ñi bokk ci ñoom lañu bëgg. Bu ngeen bokkoon ci ñoom, dinañu leen bëgg, ni ñu bëgge seeni ñoñ. Waaye bokkuleen ci àddina, ndaxte maa leen tànn, ber leen. Looloo tax ñu bañ leen.
Explore Yowaan 15:19