1
Yowaan 12:26
Téereb Injiil
TI
Ku bëgga doon sama surga, na ma topp. Bu ko defee, fu ma nekk, fa lay nekk moom itam. Ku may liggéeyal, sama Baay dina ko teral.
Compare
Explore Yowaan 12:26
2
Yowaan 12:25
Ku bëgg bakkanam dina ko ñàkk, waaye ku ko bañ ci àddina sii, dina ko denc ngir dund gu dul jeex gi.
Explore Yowaan 12:25
3
Yowaan 12:24
Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, fi ak peppu dugub ji wadd ci suuf jaarul ci dee, du mana weesu li mu doon: pepp doŋŋ. Waaye bu deeyee, dina jur pepp yu bare.
Explore Yowaan 12:24
4
Yowaan 12:46
Ni ag leer laa wàcce ci àddina, ngir ku ma gëm du des ci lëndëm.
Explore Yowaan 12:46
5
Yowaan 12:47
Ku dégg samay wax te toppu leen, du man maa koy daan, ndaxte wàccuma ngir daan àddina, waaye damaa ñëw ngir musal ko.
Explore Yowaan 12:47
6
Yowaan 12:3
Noonu Maryaama daldi jël liibaru latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree bare. Mu sotti ko ci tànki Yeesu, ba noppi fomp ko ak kawaram. Xetu latkoloñ gi gilli ci kër gi yépp.
Explore Yowaan 12:3
7
Yowaan 12:13
Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na Yàlla barkeel buuru Israyil!»
Explore Yowaan 12:13
8
Yowaan 12:23
Mu ne leen: «Waxtu wi ñu wara feeñale ndamu Doomu nit ki jot na.
Explore Yowaan 12:23