1
Yowaan 11:25-26
Téereb Injiil
TI
Yeesu ne ko: «Man maay ndekkite li, maay dund gi. Ku ma gëm, boo deeyee it, dinga dund. Rax-ca-dolli kuy dund te gëm ma, doo dee mukk. Ndax gëm nga loolu?»
Compare
Explore Yowaan 11:25-26
2
Yowaan 11:40
Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
Explore Yowaan 11:40
3
Yowaan 11:35
Yeesu jooy.
Explore Yowaan 11:35
4
Yowaan 11:4
Bi Yeesu déggee xibaar boobu, mu ne: «Lasaar de, woppam jooju du ko mujje; day wone ndamu Yàlla, tey màggal Doomu Yàlla ji.»
Explore Yowaan 11:4
5
Yowaan 11:43-44
Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!» Néew bi daldi génn, ñu gis càngaay, li ñu takke woon tànk yi ak loxo yi, ak kaala, gi ñu muure woon kanam gi. Yeesu ne leen: «Tekkileen ko, bàyyi ko mu dem.»
Explore Yowaan 11:43-44
6
Yowaan 11:38
Yeesu dellu am naqar wu réy, daldi dem ca bàmmeel ba. Pax la mu ñu yett ci doj, ube ko xeer.
Explore Yowaan 11:38
7
Yowaan 11:11
Yeesu wax loolu, teg ca ne: «Sunu xarit Lasaar nelaw na, waaye maa ngi dem yee ko.»
Explore Yowaan 11:11