1
Yowaan 10:10
Téereb Injiil
TI
Sàcc bi moom, day sàccsi rekk, di rey ak a yàq. Man damaa ñëw, ngir nit ñi am dund, ba nekk ci naataange.
Compare
Explore Yowaan 10:10
2
Yowaan 10:11
«Man maay sàmm bu baax bi. Sàmm bu baax bi day joxe bakkanam ngir ay xaram.
Explore Yowaan 10:11
3
Yowaan 10:27
Samay xar dinañu dégg sama baat; xam naa leen te ñu ngi may topp.
Explore Yowaan 10:27
4
Yowaan 10:28
Dama leen di jox dund gu dul jeex; duñu sànku mukk, te kenn du leen jële ci sama loxo.
Explore Yowaan 10:28
5
Yowaan 10:9
Man maay bunt bi; ku jaar ci man, dinga mucc, dinga mana dugg ak a génn, dinga am it mbooy goo mana fore.
Explore Yowaan 10:9
6
Yowaan 10:14-15
«Man maay sàmm bu baax bi. Ni ma xame Baay bi te Baay bi xame ma ni, noonu laa xame samay xar, te ñoom it ni lañu ma xame. Te it kat dinaa joxe sama bakkan ngir xar yi.
Explore Yowaan 10:14-15
7
Yowaan 10:29-30
Baay bi ma leen jox, moo gëna màgg lépp, te kenn manula jële dara ci loxob Baay bi. Man ak Baay bi benn lanu.»
Explore Yowaan 10:29-30
8
9
Yowaan 10:18
Kenn du ko jële ci man; maa koy joxe ci sama coobarey bopp. Am naa it sañ-sañu joxe ko te am naa sañ-sañu jëlaat ko. Loolu la ma sama Baay sant.»
Explore Yowaan 10:18
10
Yowaan 10:7
Noonu Yeesu newaat: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, man maay buntu gétt gi.
Explore Yowaan 10:7
11
Yowaan 10:12
Ki dul sàmm bi tey liggéeyal xaalis rekk waaye moomul xar yi, bu séenee bukki, day daw, bàyyi fa xar ya. Bu ko defee bukki ba dal ca coggal ja, jàpp ca, tasaare ya ca des.
Explore Yowaan 10:12
12
Yowaan 10:1
«Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, ku jaar feneen fu dul ci buntu gétt gi, kooku sàcc la, saay-saay la.
Explore Yowaan 10:1