1
Yowaan 1:12
Téereb Injiil
TI
Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.
Compare
Explore Yowaan 1:12
2
Yowaan 1:1
Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.
Explore Yowaan 1:1
3
Yowaan 1:5
Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko.
Explore Yowaan 1:5
4
Yowaan 1:14
Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.
Explore Yowaan 1:14
5
Yowaan 1:3-4
Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom. Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi.
Explore Yowaan 1:3-4
6
Yowaan 1:29
Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy Gàttub Yàlla, bi ñu nara rendi, ngir dindi bàkkaaru àddina.
Explore Yowaan 1:29
7
Yowaan 1:10-11
Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko. Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko.
Explore Yowaan 1:10-11
8
Yowaan 1:9
Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.
Explore Yowaan 1:9
9
Yowaan 1:17
Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.
Explore Yowaan 1:17