1
Saag 4:7
Téereb Injiil
TI
Kon nag wàkkirluleen ci Yàlla, waaye dàqleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen.
Compare
Explore Saag 4:7
2
Saag 4:8
Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yéen bàkkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo; yéen ñi am xel ñaar, laabal-leen seeni xol.
Explore Saag 4:8
3
Saag 4:10
Suufeel-leen seen bopp fa kanam Boroom bi, kon dina leen yékkati.
Explore Saag 4:10
4
Saag 4:6
Waaye yiwu Yàllaa ko ëpp. Moom la Mbind mi wax ne: «Yàlla dàq na ñi réy, waaye yiwal na ñi woyof.»
Explore Saag 4:6
5
Saag 4:17
Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko, bàkkaar nga.
Explore Saag 4:17
6
Saag 4:3
Bu ngeen ñaanee sax, dungeen jot dara, ndax yéena ngi ñaan ci naaféq, ngir gëna topp seen nafsu.
Explore Saag 4:3
7
Saag 4:4
Yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, xanaa xamuleen ne mbëggeelu àddina, mbañeel la fa Yàlla? Ku bëgga xaritoo ak àddina nag, noonoo nga ak Yàlla.
Explore Saag 4:4
8
Saag 4:14
Ndax dangeena xam seen ëllëg? Luy seen dund? Xanaa cóola doŋŋ luy naaw ci diir bu gàtt, daldi naaxsaay.
Explore Saag 4:14