1
Saag 3:17
Téereb Injiil
TI
Waaye xel mi jóge ci kaw daa sell, ba noppi ànd ak jàmm te lewet, nooy, fees dell ak yërmande ak jëf yu rafet; àndul ak genn parlàqu, amul genn naaféq.
Compare
Explore Saag 3:17
2
Saag 3:13
Ana ku neex xel ci yéen, ana kuy boroom xam-xam? Na ko wone ciy jëfam ak dundam gu sell, te feeñal xelam ci jikkoom ju lewet.
Explore Saag 3:13
3
Saag 3:18
Te nitu jàmm dina bey toolu jàmm, góob njub.
Explore Saag 3:18
4
Saag 3:16
Ndaxte fu wextan ak wut aw tur dugg, indi fa xëccoo ak bépp ñaawteef.
Explore Saag 3:16
5
Saag 3:9-10
Làmmiñ lanuy sante Boroom bi, di sunu Baay, ba noppi móoloo ko nit, ñi Yàlla sàkk ci meloom. Gémmiñ gi sante mooy móoloo. Yéen samay bokk, loolu warula am.
Explore Saag 3:9-10
6
Saag 3:6
Noonu it làmmiñ sawara la, di bon-bonu àddina ci biir cér yi, tey musibaal jëmm jépp. Jum la, bu Seytaane taal, muy lakk àddina.
Explore Saag 3:6
7
Saag 3:8
Waaye làmmiñ kenn manu koo not; musiba la mu dul dal mukk, fees dell ak daŋar juy rey.
Explore Saag 3:8
8
Saag 3:1
Samay bokk, bu ñépp di sababloo nekk jànglekatu mbooloo mi, xam ne nun jànglekat yi, àtte bi nuy jaar mooy gëna diis.
Explore Saag 3:1