1
Saag 1:2-3
Téereb Injiil
TI
Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu mana mel, defleen ko ni mbég mu réy, xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ.
Compare
Explore Saag 1:2-3
2
Saag 1:5
Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ.
Explore Saag 1:5
3
Saag 1:19
Yéen sama bokk yi ma bëgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéexa wax tey yéexa mer.
Explore Saag 1:19
4
Saag 1:4
Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen baña fell fenn, waaye ngeen mat sëkk.
Explore Saag 1:4
5
Saag 1:22
Buleen yem ci déglu kàddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye jëfeleen ko.
Explore Saag 1:22
6
Saag 1:12
Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko bëgg.
Explore Saag 1:12
7
Saag 1:17
gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di lëndëm.
Explore Saag 1:17
8
Saag 1:23-24
Ndaxte ku déglu kàddu gi te bañ koo jëfe, moom ak kuy seetu ñoo yem: day gis xar kanamam, te su nee wërëñ, daldi fàtte meloom.
Explore Saag 1:23-24
9
Saag 1:27
Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmiku jirim yi ak jigéen, ñi seen jëkkër faatu, ci seeni tiis, tey waggar sobey àddina.
Explore Saag 1:27
10
Saag 1:13-14
Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn. Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir.
Explore Saag 1:13-14
11
Saag 1:9
Naka mbokk mi néew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Yàlla
Explore Saag 1:9