Yàlla miy Boroom jàmm te dekkal sunu Boroom Yeesu, Sàmm bu mag bi, ci darajay deret, ji fas kóllëre gu sax, yal na leen matal ci lépp lu baax, ba ngeen mana def coobareem, di jëfe ci nun li neex ci moom, mu jaarale lépp ci Yeesu Kirist, moom mi yelloo ndam ba fàww. Amiin.