1
Yawut ya 7:25
Téereb Injiil
TI
Loolu moo tax it mu mana musal tey yeggale cig mat ñiy jaar ci moom te bëgg jege Yàlla, ndaxte mi ngi dund ba fàww ngir di leen rammu.
Compare
Explore Yawut ya 7:25
2
Yawut ya 7:26
Kon nag Yeesu mooy sarxalkat bu mag, bi nu soxla; dafa sell, du def lu bon, du taq bàkkaar, bokkul dara ak bàkkaarkat yi, te yéege nañu ko fa Yàlla.
Explore Yawut ya 7:26
3
Yawut ya 7:27
Niroowul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawul di def bés bu set ay saraxi mala ngir bàkkaari boppam jëkk, teg ca yoy mbooloo mi. Yeesu def na sarax benn yoon ba fàww ngir dindi bàkkaar yi, bi muy joxe bakkanam.
Explore Yawut ya 7:27