1
Yawut ya 2:18
Téereb Injiil
TI
Gannaaw sonn na ci nattu yi mu daj, man na dimbali ñiy jaar ciy nattu.
Compare
Explore Yawut ya 2:18
2
Yawut ya 2:14
Doomam yooyu muy wax, nit kese lañu. Looloo tax Yeesu it moom ci boppam, wàcc na, jëmmoo ni ñoom, ngir dee, ba man caa daaneel Ibliis, mi yore dooley dee.
Explore Yawut ya 2:14
3
Yawut ya 2:1
Moo tax kon nu wara gëna faaydaal wax yi nu dégg, ngir baña bayliku.
Explore Yawut ya 2:1
4
Yawut ya 2:17
Looloo taxoon mu wara mel niy doomi baayam ci bépp fànn, ngir doon seen sarxalkat bu mag fa kanam Yàlla, bi leen yërëm te di sàmm kóllëre, te ci liggéeyu sarxaleem joxe na bakkanam ngir dindi bàkkaari nit ñi, ba Yàlla baal leen.
Explore Yawut ya 2:17
5
Yawut ya 2:9
Waaye gis nanu Yeesu. Wàcce nañu ko, def ko mu gëna suufe tuuti malaaka yi, ngir mu dee ci wàllu ñépp, ndaxte loolu la Yàlla dogal ci yiwam. Waaye léegi Yàlla kaalaa na ko teraanga ak ndam ndax coono bi mu daj ba dee.
Explore Yawut ya 2:9