1
Yawut ya 1:3
Téereb Injiil
TI
Doom ji moo di leer giy jollee ci ndamu Yàlla, di ki dippeekoo ci Yàlla. Moo téye àddina ci kàddoom gu am doole gi. Te bi mu ubbee bunt ba nit di selle ci ay bàkkaaram, dafa toog fa ñu koy terale ca ndijooru Aji Màgg ji ca kaw
Compare
Explore Yawut ya 1:3
2
Yawut ya 1:1-2
Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya. Waaye ci mujug jamono jii nu tollu, Yàlla wax na ak nun jaarale ko ci Doom ji. Doomam jooju la Yàlla jagleel lépp, te ci moom la Yàlla jaar, sàkk àddina.
Explore Yawut ya 1:1-2
3
Yawut ya 1:14
Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla, mu di leen yónni ñuy dimbali nit, ñi nara jot mucc gi.
Explore Yawut ya 1:14
4
Yawut ya 1:10-11
Newaat na it: «Yaw Boroom bi, yaa sàkk àddina ca njàlbéen ga, defar asamaan yi ci sa loxoy bopp. Yëf yooyu dinañu wéy, waaye yaw dinga sax, dinañu màggat ñoom ñépp ni ay yére.
Explore Yawut ya 1:10-11