1
Galasi 4:6-7
Téereb Injiil
TI
Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba», maanaam «Baay.» Noonu dootuloo jaam, doom nga. Te ndegam doom nga, Yàlla jagleel na la cér ci xéewal, yi mu dencal ay doomam.
Compare
Explore Galasi 4:6-7
2
Galasi 4:4-5
Waaye bi àpp bi Yàlla tëraloon matee, yónni na Doomam, mu juddoo ci jigéen, ci biir yoonu Musaa, ngir jot ñi yoon wi notoon, ndax Yàlla jàpp nu ni ay doomam.
Explore Galasi 4:4-5
3
Galasi 4:9
Waaye léegi nag bi ngeen xamee Yàlla, walla boog bi leen Yàlla xàmmee, nan ngeen mana def, bay delluwaat ca aaday àddina? Aada yooyee ñàkk doole te ñàkk njariñ, lu tax ngeen bëgg, ñu notaat leen?
Explore Galasi 4:9