1
Efes 2:10
Téereb Injiil
TI
Ndaxte jëfu Yàlla lanu; moo nu bind ci Kirist Yeesu, ngir nu wéy ci jëf yu rafet, yi mu nu fàgguloon ca njàlbéen ga.
Compare
Explore Efes 2:10
2
Efes 2:8-9
Ndaxte ci yiwu Yàlla ngeen mucce ci kaw ngëm, te loolu jógewul ci yéen, mayu Yàlla la; du peyu jëf, ba kenn di ci kañu.
Explore Efes 2:8-9
3
Efes 2:4-5
Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw mbëggeel gu réy, gi mu am ci nun, dundalaat na nu ak Kirist, fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy bàkkaar-- ci kaw yiwu Yàlla ngeen mucce.
Explore Efes 2:4-5
4
Efes 2:6
Te dekkal na nu ak Kirist Yeesu, dëël nu ak moom ca bérab yu kawe ya.
Explore Efes 2:6
5
Efes 2:19-20
Noonu dootuleen ay doxandéem mbaa ay gan, waaye am ngeen baat ci kureelu gaayi Yàlla yu sell yi, te waa këram ngeen. Yéena ngi sukkandikoo ci fondamaa, bi ndawi Kirist yi ak yonent yi tabax, te Kirist Yeesu ci boppam di doju dalil wa.
Explore Efes 2:19-20