ci leeral seeni xol. Noonu dingeen xam yaakaaru ëllëg, ji leen Yàlla wooye, di ndam lu xel manta daj, li nekk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi. Ngeen xam it, ni kàttanam màgge ba jéggi dayo, jëm ci nun ñi gëm, dëppook dooleem ju ràññiku, ji mu jëfe ci Kirist, ci li mu ko dekkal, dëël ko ci ndijooram ca bérab yu kawe ya, mu tiim lu sore malaaka yépp, muy kilifa, boroom sañ-sañ, boroom doole mbaa buur, te gëna màgg wépp tur wu ñu mana tudd, muy tey, muy ëllëg.