1
Galasi 6:9
Téereb Injiil
TI
Bunu tàyyi ci def lu baax, ndaxte bu nu ci sawaree, bu waxtu wi jotee dinanu jariñu.
Compare
Explore Galasi 6:9
2
Galasi 6:10
Noonu fi ak nu koy man, nanuy defal ñépp lu baax, rawatina nag sunu bokk yi gëm.
Explore Galasi 6:10
3
Galasi 6:2
Jàpplanteleen, noonu dingeen sàmm yoon wi Kirist tëral.
Explore Galasi 6:2
4
Galasi 6:7
Bu leen ci dara nax; kenn du foontoo Yàlla, ndaxte lu waay ji, moom ngay góob.
Explore Galasi 6:7
5
Galasi 6:8
Ku ji ngir sa nafsu, dinga góob li sa nafsu meññ, maanaam ag yàqute. Waaye ku ji lu soloo ak Xelum Yàlla, li Xel mi meññ ngay góob, maanaam dund gu dul jeex.
Explore Galasi 6:8
6
Galasi 6:1
Bokk yi, ku ñu fekk muy def lu Yàlla bëggul, yéen ñi topp Xelum Yàlla, nangeen ko jubbanti ak xol bu lewet. Waaye nanga sàmm sa bopp, ngir bàkkaar bañ laa fiir, yaw itam.
Explore Galasi 6:1
7
Galasi 6:3-5
Ndaxte kuy naagu te fekk doo dara, dangay nax sa bopp. Na ku nekk seetlu ni muy beye sasam. Bu ko defee dina mana naw boppam, tey bañ di diirante mbagg ak ñi ci des. Ndaxte ku ci nekk dangaa wara yenu sab yen.
Explore Galasi 6:3-5