1
Jëf ya 17:27
Téereb Injiil
TI
Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.
Compare
Explore Jëf ya 17:27
2
Jëf ya 17:26
Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xébla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew.
Explore Jëf ya 17:26
3
Jëf ya 17:24
«Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar.
Explore Jëf ya 17:24
4
Jëf ya 17:31
Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya.»
Explore Jëf ya 17:31
5
Jëf ya 17:29
Kon nag, bu nu nekkee xeetu Yàlla, warunoo gëm ne Yàlla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel.
Explore Jëf ya 17:29