1
2.Timote 1:7
Téereb Injiil
TI
Ndaxte Xel mi nu Yàlla sol du ànd ak ragal, waaye day ànd ak kàttan, mbëggeel ak moom sa bopp.
Compare
Explore 2.Timote 1:7
2
2.Timote 1:9
Moo nu musal te woo nu ci dund gu sell, ci lu ajuwul ci sunuy jëf, waaye ci dogalu boppam ak yiwam, wi nu Yàlla may ci Kirist Yeesu, ba àddina sosoogul.
Explore 2.Timote 1:9
3
2.Timote 1:6
Looloo tax maa ngi lay fàttali, nga xambaat taal bi Yàlla taal ci yaw, di may gi mu la jagleel, bi ma la tegee samay loxo.
Explore 2.Timote 1:6
4
2.Timote 1:8
Bul rus ci seedeel sunu Boroom, mbaa ci li ñu ma tëj ndax turam, waaye bokkal ak man tiis ci xamle xibaaru jàmm bi, wéeru ci kàttanu Yàlla.
Explore 2.Timote 1:8
5
2.Timote 1:12
looloo tax ma jànkoonte ak tiis yu mel nii. Waaye rusuma ci, ndaxte xam naa ki ma wékk sama yaakaar, te wóor na ma ne li ma ko dénk, man na koo denc ba bés ba.
Explore 2.Timote 1:12