1
1.Timote 6:12
Téereb Injiil
TI
Góor-góorlul ci bëre bu baax bi, ba ub làmbi ngëm, te feddali sag téye ci dund gu dul jeex gi; ndaxte ci loolu la la Yàlla woo, te looloo waraloon it sa seede su rafet fa kanam mbooloo mu bare.
Compare
Explore 1.Timote 6:12
2
1.Timote 6:10
Ndaxte bëgge ci xaalis mooy ndeyu ñaawteef yu bare; am na ñu ko wut, ba moy ci yoonu ngëm, te seen xol di dagg ndax tiis yu bare.
Explore 1.Timote 6:10
3
1.Timote 6:6
Ba tey ragal Yàlla gu ànd ak doylu, wërsëg la.
Explore 1.Timote 6:6
4
1.Timote 6:7
Ndaxte indaalewunu fi dara, te dunu yóbbaale dara.
Explore 1.Timote 6:7
5
1.Timote 6:17
Ñi barele alalu àddina nag, dénk leen ñu baña réy te baña wékk seen yaakaar ci koom-koom yi saxul fenn, waaye ñu wékk ko ci Yàlla, mi nuy may naataange ju mat, ngir nu man ciy bànneexu.
Explore 1.Timote 6:17
6
1.Timote 6:9
Waaye ñiy sàkkoo barele, dinañu jànkoonte ak i nattu, ba dugg ci fiir, di xuus ci bëgg-bëggi neen yuy yóbbe ayib, tey sóob nit cig réer ak sànkute.
Explore 1.Timote 6:9
7
1.Timote 6:18-19
Dénk leen ñu def lu baax, te bare jëf yu rafet, ñu yéwén, bay sédd ñi amul, di fàggu dencu ëllëg bu wér. Noonu dinañu feddali seen téye ci dund gu wóor gi.
Explore 1.Timote 6:18-19