Gannaaw loolu lépp dina seeye noonu nag, nangeen góor-góorlu ci gëna sellal seen nekkin te feddali seen ragal Yàlla. Te it ngeen taxaw temm ci séentu bésu Yàlla bi, te waajal ñëwam. Su boobaa asamaan yi dinañu lakk, ba naaw ni pënd, te lu nekk ci àddina dina lakk, ba seey nib dóom.