1
2.Piyeer 2:9
Téereb Injiil
TI
Gannaaw loolu lépp am na nag, nanu bir ne Boroom bi man na musal aji gëm ji nekk ci nattu, te denc ñi jubadi, ngir alag leen bésu àtte ba.
Compare
Explore 2.Piyeer 2:9
2
2.Piyeer 2:21-22
Ndaxte ñu xam yoon wu jub wi, ba noppi dëddu ndigal lu sell li ñu déggoon, bañoon koo xam moo gënoon ci ñoom. Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: «Xaj mooy waccu, di ko lekkaat,» te it: «Mbaam-xuux, loo ko sang sang, mu xalangu ci ban.»
Explore 2.Piyeer 2:21-22
3
2.Piyeer 2:19
Dañu leen di dig ngoreel, te fekk ñoom ci seen bopp jaami yàqute lañu, ndaxte lu la not, jaamam nga.
Explore 2.Piyeer 2:19
4
2.Piyeer 2:20
Su ñu xamee Boroom bi, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, ba mucc ci sobes àddina, ba noppi sóobuwaat ca, ba mu not leen, seen muj moo yées seen njàlbéen.
Explore 2.Piyeer 2:20
5
2.Piyeer 2:1
Waaye ci bànni Israyil, amoon na naaféq yu mbubboo turu yonent, ni muy ame seen biir ñuy mbubboo turu jànglekat. Ci seeni pexe dinañu dugal ci yéen xalaat yu sànke, di weddi Boroom bi leen jot, tey yóbbe seen bopp alkànde ju teew.
Explore 2.Piyeer 2:1