1
1.Yowaan 1:9
Téereb Injiil
TI
Su nu nangoo sunuy bàkkaar ci kanamam, fekk kuy sàmm kóllëre la te jub, ngir baal nu sunuy bàkkaar te sellal nu ci lépp lu jubadi.
Compare
Explore 1.Yowaan 1:9
2
1.Yowaan 1:7
Waaye bu nuy dox ci leer, ni mu nekke moom ci boppam ci leer, kon bokk nanu ci sunu biir, te deretu Yeesu Doomam dina nu sellal ci bépp bàkkaar.
Explore 1.Yowaan 1:7
3
1.Yowaan 1:8
Su nu waxee ne amunu bàkkaar, kon nax nanu sunu bopp, te dëgg nekkul ci nun.
Explore 1.Yowaan 1:8
4
1.Yowaan 1:5-6
Xibaar bi nu dégg ci Yeesu Kirist, di leen ko yégal, mooy lii: Yàlla Leer la, te genn lëndëm nekkul ci moom. Su nu waxee ne bokk nanu ci moom, tey dox ci lëndëm, danuy fen ci sunuy wax ak sunuy jëf.
Explore 1.Yowaan 1:5-6
5
1.Yowaan 1:10
Su nu waxee ne defunu bàkkaar, teg nanu ko kuy tebbi waxam, te kàddoom duggagul ci sunu xol.
Explore 1.Yowaan 1:10