1
2.Piyeer 1:3-4
Téereb Injiil
TI
Dooley Yàlla moo nu may lépp lu aju ci dund gu sax ak ragal Yàlla, jaarale ko ci xam gi nu ko xam, moom mi nu woo ci kaw ndamam ak dooleem. Noonu la nu dige ay dige yu rafet te réy ba ëpp xel, ngir nu gëm leen, te Yàlla sol nu jikkoom, nu mucc ci yàqute, gi bànneexu bakkan samp ci àddina si.
Compare
Explore 2.Piyeer 1:3-4
2
2.Piyeer 1:5-7
Na loolu tax ngeen góor-góorlu, ba yokk ci seen ngëm njàmbaar, ci njàmbaar googu ngeen yokk ci xam-xam, yokk ci not sa bopp. Not sa bopp googu, ngeen yokk ci muñ, yokk ci ragal Yàlla, yokk ci sopp mbokk, yokk ci bëgg ñépp.
Explore 2.Piyeer 1:5-7
3
2.Piyeer 1:8
Ndaxte bu leen jikko yooyu soloo, ba sax ci yéen, dina tax seen xam Yeesu Kirist Boroom bi am njariñ te jur mbaax.
Explore 2.Piyeer 1:8
4
2.Piyeer 1:10
Kon nag samay bokk, gannaaw Yàlla da leena tànn te woo leen, góor-góorluleen ci feddali ko ak seen kem kàttan. Ndaxte su ngeen ko defee, dungeen jeng mukk.
Explore 2.Piyeer 1:10