1
1.Piyeer 5:7
Téereb Injiil
TI
Te ngeen yenniku ci kawam seen njàqare jépp, ndax ku leen ñeewante la.
Compare
Explore 1.Piyeer 5:7
2
1.Piyeer 5:10
Te Yàlla mi jagoo yiw wépp te woo leen ci darajay Kirist, ngir ngeen bokk ci ndamam li sax, gannaaw bi ngeen yendoo bëccëgu tiis, dina leen yeesalaat, di leen dëgëral ak a dooleel, ba ngeen sampu.
Explore 1.Piyeer 5:10
3
1.Piyeer 5:8-9
Maanduleen te foog, ndax seen noon Seytaane mu ngi wër, ni gaynde guy yëmmu, di rëbb ku mu yàpp. Jànkoonteleen ak moom ci biir ngëm gu takku, xam ne kureelu bokk yi ci àddina yépp, ñu ngi daj ay fitna ni yéen.
Explore 1.Piyeer 5:8-9
4
1.Piyeer 5:6
Suufeel-leen seen bopp kon ci ron loxob Yàlla bu am kàttan, ngir mu yékkati leen ci jamono ju ko soob.
Explore 1.Piyeer 5:6
5
1.Piyeer 5:5
Noonu itam yéen ndaw ñi, nangeen déggal mag ñi. Te yéen ñépp, solooleen woyof ci seen biir, ndaxte: «Yàlla day dàq ñi réy, di yiwal ñi woyof.»
Explore 1.Piyeer 5:5