1
2.Korent 9:8
Téereb Injiil
TI
Yàlla man na leena woomal ci bépp yiwam ba ci fépp ak ci lépp, ngeen faj seen soxla yépp te sakkanle it ngir bépp jëf bu baax.
Compare
Explore 2.Korent 9:8
2
2.Korent 9:7
Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi.
Explore 2.Korent 9:7
3
2.Korent 9:6
Li am mooy: ku ji tuuti, góob tuuti; ku ji lu bare, góob lu bare.
Explore 2.Korent 9:6
4
2.Korent 9:10-11
Yàlla miy jox beykat bi jiwu ak nit ab dund, dina leen jox jiwu wu ne gàññ, te sakkanal li seen njub meññ. Noonu dingeen woomle ci lépp, ba yéwén ci bépp anam, ba tax ñu bare gërëm Yàlla ndax li ngeen maye jaarale ko ci nun.
Explore 2.Korent 9:10-11
5
2.Korent 9:15
Jërëjëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo!
Explore 2.Korent 9:15