1
1.Piyeer 4:8
Téereb Injiil
TI
Li gëna am solo mooy, ngeen bëggante mbëggeel gu tar, ndax mbëggeel day suul bàkkaar yu bare.
Compare
Explore 1.Piyeer 4:8
2
1.Piyeer 4:10
Te lu la Yàlla jagleel kenn ku nekk ci yéen, nanga ko bokk ak ñépp ni jawriñ ju jub, ci séddale yiwu Yàlla wu yaatu.
Explore 1.Piyeer 4:10
3
1.Piyeer 4:11
Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin.
Explore 1.Piyeer 4:11
4
1.Piyeer 4:16
Waaye ku ñu sonal ndax waayu Kirist nga, bu ci rus, waaye nga màggal Yàlla ci tur woowu.
Explore 1.Piyeer 4:16
5
1.Piyeer 4:7
Te itam muju lépp jegesi na; nangeen maandu te foog, ba mana ñaan ci Yàlla.
Explore 1.Piyeer 4:7
6
1.Piyeer 4:12-13
Yéen samay xarit, ci mbirum nattu bu tànge ni daay, bi dal ci seen kaw, bumu leen jaaxal, ba ngeen teg ko ni lu xel dajul. Waaye bégleen ci cér, boobu ngeen am ci coonoy Kirist, ngir bés bu ndamam di feeñ, ngeen bég ak mbég mu ëpp xel.
Explore 1.Piyeer 4:12-13
7
1.Piyeer 4:9
Ganalanteleen ci lu àndul ak njàmbat.
Explore 1.Piyeer 4:9
8
1.Piyeer 4:19
Kon nag ñi tegoo fitna ci coobarey Yàlla, nañu sax ci def lu baax, dénk seen bopp Yàlla, miy Bindkat biy sàmm kóllëre.
Explore 1.Piyeer 4:19
9
1.Piyeer 4:1-2
Gannaaw Kirist nag sonn na ci yaramam, gànnaayooleen xelam moomu, ndaxte ku sonn ci yaramam, tàggoo na ak bàkkaar. Noonu diir bi ko dese ci kaw suuf, dëddu na bànneexi bakkan, jublu ci coobarey Yàlla.
Explore 1.Piyeer 4:1-2
10
1.Piyeer 4:14
Su ñu leen jànnee sax ci turu Kirist, xamleen ne ñu barkeel ngeen, ndax Xelum Yàllaa ngi ci yéen, di firndeel seen ndamu ëllëg.
Explore 1.Piyeer 4:14