1
1.Piyeer 3:15-16
Téereb Injiil
TI
Waaye màggal-leen Kirist Boroom bi ci seeni xol, te jekk ngir tontu ku lay laaj ci seen yaakaar ji ngeen am; waaye na tont li lewet te ànd ak wegeel. Àndleen ak xel mu dal; noonu ñi leen di sikkal ndax seen dund gu rafet ci gëm Kirist, dinañu rus ci seeni sos.
Compare
Explore 1.Piyeer 3:15-16
2
1.Piyeer 3:12
Ndax Boroom baa ngi xool ñi jub bëti yërmande, di dékk noppam seeni ñaan, waaye day dàq ñiy def lu bon.»
Explore 1.Piyeer 3:12
3
1.Piyeer 3:3-4
Bu seen taar aju ci col, maanaam ay létt, wurus mbaa yére yu rafet, waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir, di xol bu nooy te dal, ndax loolu lu takku la fa Yàlla.
Explore 1.Piyeer 3:3-4
4
1.Piyeer 3:10-11
Ndaxte: «Ku bëgga am dund gu naat te fekke bés yu rafet, na jàpp làmmiñam ci lu bon, sàmm gémmiñam ci fen. Na dëddu lu bon, tey def lu baax, na xënte jàmm te sax ci.
Explore 1.Piyeer 3:10-11
5
1.Piyeer 3:8-9
Kon nag bokkleen xalaat, bokkleen i tiis, bëgganteleen, yërëmante te woyof. Ku la def lu bon mbaa mu saaga la, bul feyu, waaye ñaanal ko lu baax; ndaxte ci loolu la leen Yàlla woo, ngir barkeel leen.
Explore 1.Piyeer 3:8-9
6
1.Piyeer 3:13
Te it kan moo leen di sonal, su ngeen góor-góorloo ci def lu baax?
Explore 1.Piyeer 3:13
7
1.Piyeer 3:11
Na dëddu lu bon, tey def lu baax, na xënte jàmm te sax ci.
Explore 1.Piyeer 3:11
8
1.Piyeer 3:17
Ñu fitnaal la ndax jëf ju baax, su dee mooy coobarey Yàlla, moo gën ñu fitnaal la ndax jëf ju bon.
Explore 1.Piyeer 3:17